Arraigo de segunda oportunidad (beneen yoon)

Lan mooy arraigo de segunda oportunidad?

Kayit la ngir dëkk te liggéey ci Espaañ.

Ngir nit ñi amoon kayit waaye ñàkk ko ndax mënuñu ko woon yeesal.

Day yàgg 1 at te mën nañu ko yeesal.

Mbir mu bees la, dale ko ci mee 2025.

Ndax yaw la jëm?

✓  Amoon nga kayitu dëkk ci 2 at yi weesu te yeesaluñu la ko.
Du dox su kayit boobu doon arraigo walla circunstancias excepcionales.

✓  Dëkk nga Espaañ 2 at walla lu ëpp te dogul.

✓  Amoo benn tooñ ci yoon (casier).

✓  Amoo laaj asile bu ñu nekkee seet.

Lu am solo: du dox su ñu ko bañee yeesal ndax orden público walla kaaraange (ba mu des ñu bàyyi la ci yoon). Soo amee sàkku, dinanu seet sa mbir.

Ban kayit nga soxla?

▸  Paaspoor bu mat (xët yépp).

▸  Lu wone ne 2 at nga fi def: empadronamiento, dem ci doktoor, kayiti meeri…

▸  Kayitu yoon (casier judiciaire) bu sa réew (bu ñu tekki te légalisé).

▸  Sa kart walla résolution bu yàgg ak kayit bu ñu bañee yeesal, soo ko amee.

Ñaata lay yàgg? Lu tollu ci 3 weer.

Xibaar yu gën a bare (yoon wi, ci espaañol)

Autorización de residencia temporal por circunstancias excepcionales por arraigo de segunda oportunidad (Ley Orgánica 4/2000, art. 31.3; Real Decreto 1155/2024, arts. 124 a 132).

Supuesto: personas extranjeras que se encuentren en España y hayan sido titulares, en los dos años inmediatamente anteriores a la solicitud, de una autorización de residencia no otorgada por circunstancias excepcionales, cuya renovación no se haya producido por motivos distintos de razones de orden público, seguridad o salud pública. Es posible solicitarlo si existe sentencia denegatoria, sobreseimiento o absolución.

Requisitos: no ser ciudadano de la UE, del EEE o de Suiza, ni familiar de estos a quien se aplique el régimen de ciudadano de la Unión; encontrarse en España y no ser solicitante de protección internacional; permanencia continuada en España de al menos dos años (no computa el tiempo como solicitante de protección internacional); no ser una amenaza para el orden público, la seguridad o la salud pública; carecer de antecedentes penales en España y en los países de residencia de los últimos cinco años; no figurar como rechazable en países con convenio; no estar en plazo de compromiso de no retorno; abonar la tasa.

Documentación: impreso EX-10; pasaporte completo; prueba de permanencia continuada de dos años; certificado de antecedentes penales. Documentos extranjeros traducidos y legalizados o apostillados.

Procedimiento: se presenta personalmente en la Oficina de Extranjería de la provincia o telemáticamente (Mercurio). Tasa: modelo 790 código 052, epígrafe 2.5. Plazo de resolución: tres meses (silencio negativo). Hay un mes para pedir la TIE en la Comisaría.

Vigencia: un año, con autorización para trabajar por cuenta propia y ajena en toda España. Después puede pasar a una autorización de residencia y trabajo (art. 191 del Reglamento) o prorrogarse por periodos anuales si se mantienen los requisitos, buscando empleo activamente e inscrito en el servicio público de empleo.

Información orientativa basada en la hoja informativa oficial del Ministerio (mayo de 2025). Solo es de aplicación la normativa vigente en el momento de la solicitud.

Li ngay am: kayit ngir dëkk te liggéey ci Espaañ gépp, ci kenn walla ci sa bopp.
Ginnaaw ga mën nga jàll ci kayitu dëkk ak liggéey bu baax, walla yeesal ko soo di wut liggéey te bindu ci SAE.

Am nga laaj? Waxal nu sa mbir te dinanu ko seet

Ndimbal ngir doxandéem yi ci Espaañ